QUESTIONS –REPONSES : ZAKAT AL FITR (LATHIE AK TONTOU CI LOU ADIOU CI MOUROU KOOR)


1-Lane mooy mourou koor ?

-Mourou koor faratala dioo khamné warna thi kép kouy dioullit mou défko balaa niouy dioulli korité.

2-Lane moo waral mourou koor ?

-wakhnaniouné liko waral mooy bou wérou koor bi diékhé tiyaaba yi nitki am thi wérou koor bi yeup danioukoy athie té lifék nitki guénéwoul mourou koor dou meuneu diot thi tiyaabaam yooyou.
Serigne Chouhaybou Mbacké(R.A) wakhna tamite thi térém bimou toudé “khouratoul hayni” né kép kou wara guéné mourou koor té guénéwou yalla dou nangou kooram (page 75).

3-Kagnie laniou wara guéné mourou koor ?

-Mourou koor,niou nguiko wara guéné thi bisou korité,gannaaw biniou dioullé souba ba paré.Wayé balaa niouy dioulli korité warna fék nga guénéko.

4-Kane moo wara guéné mourou koor ?

-kiko wara guéné mooy dioullit binga khamné moukallaf la.kép koo khamné yaako wara doundal tamit yaako wara guénél mourou koor.
Ex: sa sokhna,sa doom bou goor boo khamné majeuragoul ak sa doom bou djiguéne boo khamné amagoul boroom keur etc.say waydiour tamit boufékéné meunouniouko guéné ténga meuneko warngaléne ko guénél.

5-Kane laniou wara diokh mourou koor ?

-kiniouko wara diokh mooy kép kou yéyoo lék azaka.

6-Thi lane laniou wara guéné mourou koor ?

-gni nguikoy guéné thili eup thili waa réwmi di doundé.Boudé fi thi Sénégal nak mélnani li eup linioufiy doundé mooy thiép.Boula nékhé tamit nga khaymako guénéko thi khalis.

7-liniou wara guéné thi mourou koor nane la wara tollou ?

-kéne kouné limou wara guéné mooy niaari kilo (2 kg) té diokh ko kouko yélloo.Boula nékhé nga khaymako thi khalis guénéko.Gni nga khamné yaaléne wara doundal tamit kéne kouthiné loolou ngako wara guénél.


RD

Article Précédent

Magistrature : Démissions retentissantes de Amadou Dionwar Soumaré et de Djiby Seydi

Article Suivant

Korité 2020 : les salaires et les pensions sont payés à partir d’aujourd’hui !

Laisser un commentaire

Votre adresse de messagerie ne sera pas publiée. Les champs obligatoires sont indiqués avec *

Powered by Live Score & Live Score App